Michael Thervil moo ko bind

Produit tabac vaginal
Sooy wax ci stimulant wala enhanceur ci wàllu awra, dañu koy faral di jaay góor ñi. Waaye ana luy xew sudee jigéen ñi ñooy gëna xëcc kàmpaañ yu mel nii? Loolu mooy xew ci réew yu bari ci Afrique, waaye rawatina ci Gambie ak ci yeneen réew yu sowwu Afrique ci gox bi lu ci melni Senegal, Mali, Ghana, Guinée-Bissau, Guinée, ak Burkina Faso. Gis nañu itam ni fi mu nekk ñu ngi jaay “taba” wala “tabba” ba noppi yóbbu ko ci nord Europe. “Taba” baat Mandinka la buy tekki tabax. Waaye dañuy faral di jaxase taba ak yeneen mbir yu melni eroin ngir gëna am doole. Leegi, taba tóxul, doonte produit tabax la; lu moy loolu, jigéen ñi ci seen bopp ñooy dugal taba ci biir baat bi.
Ngir nguur yi ak kilifay wérgi-yaram yi ci réew yi ñuy jëfandikoo taba ngir faj seen bopp, jafe-jafe bi nekkul ci jëfandikoo gi waaye ci jafe-jafe wérgi-yaram yi ci jëfandikoo taba la. Taba mën nañu ko jëfandikoo "nimu mel" wala "jaxas" ak yeneen yu melni beurre de karité, alkol, dóóm, garab, soda caustic ak cannabis. Ci "tamp" ak "dagg" taba, dafay tax ñu bari ci jëfandikukat yi daanu ci dependence ak drog, yàqu-yàqu drog, yeneen jafe-jafe yu jëm ci yaram feebar inflamatoire pelvic, biir buy daw, waccu, yëg-yëg yu tàng, niki deret vaginal, gaañ-gaañu chimik ci vagina, dysfonctionnement. Daa melni lu bari, te noonu la.
Jigéen yu bari yuy jëfandikoo taba itam dañu wax ni bëggu ñu tëddee góor wala seen jëkkër, ak benn ci jigéen ñiy jëfandikoo taba mu jural jëkëram divorce ak moom ndax drog bimu àndaloon ci taba dafa dëgër lool ndax daf ko "satisfaire" ci wàllu awra. Du moom kese moo mujjee nekk jaamu taba ak xéewal yi mu àndal ci wàllu awra. Amna ay rapoor ci yeneen jigéen ñu bari ñu « am ndam » ci taba, ñu wax ni jëfandikoo ko dafay féexal seen xol ci wàllu awra. Waaye, jëfandikoo taba du ngir gëna xëcc awra rek. Jigéen ñu bari dañuy dugal taba ci seen awra ngir faj bopp buy metti. Doktër yi amal gëstu ci jëfandikoo taba ci jigéen ñi, gis nañu ni li waral jigéen ñi di nekk jaam ci taba te bëgga bàyyi jafe-jafe yi ci jëfandikoo gi mooy ndax taba dafay gaaw dugg ci deret ji jaare ko ci awra bi, maanaam ñu def tabax ci suufu làmmiñ. Doonte jëfandikoo taba yàgg naa am ci gox bi, barina lu nit ñi gëm ni duñu jëfandikoo taba. Léeboon bi njëkk mooy jëfandikoo taba "dina leen jox [jigéen yu mag yi] [gëna] ' ndaw' ak 'tight' vagina, gëna yokk bànneexu seen jëkkër ci sëy." Meneen gis-gis bu bari bu jëfandikukati taba yi jàpp mooy ni mën na "faj feebar yu bari, lu ci melni epilepsi, hipertension, ñàkka mëna am doom, candidiasis, diabet, arthritis, metit wi ci yaram wi yépp, fistule, hernie ak bedwetting ci xale yi" ak ni "mën na yokk lim CD4 Tlym malaad yi am VIH/SIDA te mën nañu ko jëfandikoo itam ngir moytu infeksioŋu respiratoire yu ci melni COVID-19.”
Li yéem nit ñu bari ñuy jàng lii ci yoon wu njëkk mooy waajur yi, rawatina yaay yi, dañuy dugal taba ci biir seeni doom yu jigéen ngir fexe ñu bàyyi sibbiru ci lal bi. Waaye itam, gëm-gëm bu yaatu la itam ni taba dafay jàppale jigéen ñi ñu tëye seen vaginal "gëna dëgër", loolu moo leen di jox benn boor ci lal - kon ñu gëm. Gëm-gëm yooyu ñu bari gëm, dañu wax ni STD/STI, VIH, ak SIDA dañu gëna yokk ndax jëfandikoo taba. Waaye itam, nun ci VEDA Communications defu nu benn àtte ci jëfandikukati taba ak ni ñu koy jëfandikoo, waaye xam nanu ni ci nit ñu bari ci àdduna bi dañu jàpp ni loolu du lu jaarul yoon.
Gëstu bi doktër yi amal ci gox yi ñuy jëfandikoo taba, dafa wane ni limu nit ñiy jëfandikoo taba mingi tollu ci diggante 25 ba 45 at, sunu sukkandikoo ci gynécologue bu Gambie bi tuddu Dr. Musa Marena, njiitu wàllu wérgi-yaramu jigéen ñi, xale ba, xale yi ak ndaw ñi ci Ministère de la Santé. Amna luñu wara wax itam ni at yi ci àll bi ci Gambie dañuy yokk ba yegg ci 40 at ak ci kaw. Ci wàllu ndaw ñi, waxoon nañu itam ni jëfandikoo taba, rawatina ci anam wi ñu ko gëna xarañ, mingi gëna bari ndax fitnaal bu jigéen ñi tollu ci at yiy dem jàngi. Ci wàllu diine, Sheikh Ebrahim Jarju, njiitu konsilu islaam bi gëna mag bi nekk ci Gambie, dafa jàpp ni jëfandikoo taba dafay « haram » wala « lu tere » ci ñiy jëfandikoo islaam, mu wax ci lii ci topp:
"Su jigéen di jëfandikoo Taba, dafay tere jëkëram yelleefu bànneex bi war ci seen sëy"
Raportewoon nañu itam ni ñi ci gëna bari luñu koy jëfandikoo ñooy nit ñi jàngul ci gox bi, ba noppi ni seeni xarit ak seeni mbokk dañu am cër bu mag ci fësal ak jëfandikoo taba ci jigéen ñi itam. Doonte jigéen ñu bari dañuy jëfandikoo taba ci nëbbëtu, kumpa la ni jigéen ñu bari ci gox bi dañu koy jëfandikoo, te mën nañu ko jëfandikoo ëlëg doonte amna loraange yu ci nekk ci wàllu wérgi-yaram.
Comments